3Deesu la séentu, ba rus. Kuy wor ci neen mooy rus.
4Éy, Aji Sax ji, won ma saw yoon, xamal ma fi nga ma jaarloo.
5Jiitee ma sag dëgg, jàngal ma. Yaw yaay Yàlla ji may musal, ma di la yendoo yaakaar.
6Aji Sax ji, bàyyil xel sa yërmandeek sa ngor. Naka jekk sa jikkoo!