3 Deesu la séentu, ba rus. Kuy wor ci neen mooy rus.
4 Éy, Aji Sax ji, won ma saw yoon, xamal ma fi nga ma jaarloo.
5 Jiitee ma sag dëgg, jàngal ma. Yaw yaay Yàlla ji may musal, ma di la yendoo yaakaar.
6 Aji Sax ji, bàyyil xel sa yërmandeek sa ngor. Naka jekk sa jikkoo!