Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor - Sabóor 25

Sabóor 25:15-22

Help us?
Click on verse(s) to share them!
15Samay gët jàkk rekk ci Aji Sax ji, moo may xettli ci fiiru noon.
16Ngalla geesu ma, baaxe ma, maa wéet, néew doole,
17sama xol feesey xalaat. Rikk, teggil ma njàqare!
18Xoolal sama naqar ak sama tiis, te baal ma bépp bàkkaar.
19Xoolal noon yi ne gàññ, bañ ma mbañeelu fitna.
20Éy, aar ma, musal ma! Bu ma rusloo, yaw laa làqoo.
21Yal na ma maanduteek njub taxawu, maa ngii, di la xaar.
22Éy Yàlla, teggilal Israyil tiisoo tiis.

Read Sabóor 25Sabóor 25
Compare Sabóor 25:15-22Sabóor 25:15-22