1Ñeel Daawuda, di kàddug Sabóor. Aji Sax jee moom suuf ak li ko fees, ak àddina ak li ci biiram.
2Moo samp suuf biir géej, dëj ko ci kaw wal mi.
3Ana kuy yéegi tundu Aji Sax ji, kuy taxawi bérabam bu sell ba?
4Xanaa ku mucc ayib, sell ab xol, xemmemul caaxaani neen, du giñey fen.
5Kookooy jagoo barkeb Aji Sax ji, ak njekku Yàlla, mi koy musal.
6Ñooñooy waa làng, gi lay sàkku, di maasug Yanqóoba, giy sàkku sa yiw. Selaw.