5Na wóllërey Yàlla bànneexoo seen ndam, bu ñu tëddee sax, di sarxolle,
6di xaacuy kañ Yàlla, ŋàbbaale saamaru ñaari ñawka,
7ngir duma yéefar yi, mbugale ko yooyu xeet,
8yeewe seeni buur ay càllala, jénge seeni njiit jéngi weñ,
9ngir sottalal leen àtte bi ñu bind, muy ndamu wóllërey Yàlla yépp. Màggal-leen Ki Sax!