5 Na wóllërey Yàlla bànneexoo seen ndam, bu ñu tëddee sax, di sarxolle,
6 di xaacuy kañ Yàlla, ŋàbbaale saamaru ñaari ñawka,
7 ngir duma yéefar yi, mbugale ko yooyu xeet,
8 yeewe seeni buur ay càllala, jénge seeni njiit jéngi weñ,
9 ngir sottalal leen àtte bi ñu bind, muy ndamu wóllërey Yàlla yépp. Màggal-leen Ki Sax!