8mooy sànge asamaan ay niir, tawal suuf, saxal tund yi am ñax,
9leel mala, xol liiru baaxoñ bu jooy.
10Kii nawul dooley fas, gërëmul kàttanu jàmbaar.
11Ki Aji Sax ji gërëm mooy ki ko ragal te di ko yaakaare ngoram.
12Yerusalem, sargal-leen Aji Sax ji! yeen waa Siyoŋ laa ne, màggal-leen seen Yàlla!
13Mooy tëj ràpp seen bunti dëkk, barkeel seen askan wa ca biir,
14jàmmal seen suufas réew, reggal leen ngëneelu pepp,
15yónnee suuf ndigalam, kàddoom ne coww, daw ca.
16Mooy tawal yuur bu mel ni wëttéen, di lay lay bu sedd, mel ni pënd ci suuf.
17Mooy yuri tawub yuuram niy donj. Bu ni seddee, ana kuy taxaw?
18Mu yebal kàddoom, seeyal; wal ngelawam, ndox walalaan.
19Mooy wax Yanqóoba kàddoom, dogalam yaak ndigali yoonam ñeel Israyil.