4Noo ga day rëcc, mu dellu suuf; bu bés baa, pexeem jeex.
5Ndokklee kuy dimbalikoo Yàllay Yanqóoba; di yaakaar Yàllaam Aji Sax ji,
6ki sàkk kaw ak suuf, géej ak lu ci biiram, di sàmm dëgg ba fàww,
7di àtte néew-ji-doole, di leel ku xiif. Aji Sax jeey tijji ku ñu tëj.
8Aji Sax jeey xippil silmaxa, di siggil ku sëgg. Aji Sax jee sopp ku jub.