3Aji Sax ji, sàmmal ma sama làmmiñ, saytul ma sama kàddu.
4Bu ma xiir ci lu aay, may jëfe jëf ju bon, ànd ceek ñiy jëf lu ñaaw, di wàlli seeni bernde.
5Kuy déggal Yàlla, man na maa dóor, bantal ma ci ngor. Loolu ngëneelu cuuraay la, duma ko bañ. Waaye maa ngi saxoo ñaan pexey noon moy.