7Dama ne Aji Sax ji, yaay sama Yàlla; Aji Sax ji, teewlul, ma dagaan la.
8Aji Sax ji Boroom bi may walloo doole, yaa ma yiir keroog bésub xare.
9Aji Sax ji, bul may ku bon nammeelam, bul joyal pexeem, muy yékkatiku. Selaw.
10Ñi ma sam, yal na seen ayu làmmiñ këppu seen kaw bopp.