7 Dama ne Aji Sax ji, yaay sama Yàlla; Aji Sax ji, teewlul, ma dagaan la.
8 Aji Sax ji Boroom bi may walloo doole, yaa ma yiir keroog bésub xare.
9 Aji Sax ji, bul may ku bon nammeelam, bul joyal pexeem, muy yékkatiku. Selaw.
10 Ñi ma sam, yal na seen ayu làmmiñ këppu seen kaw bopp.