Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor - Sabóor 135

Sabóor 135:4-11

Help us?
Click on verse(s) to share them!
4Ki Sax a taamu Yanqóoba, muy Israyil mi mu séddoo.
5Maa xam ne Aji Sax ji màgg na! Sunu Boroom a sut lépp lu ñuy jaamu.
6Lépp lu Aji Sax ji namm, moom lay def asamaan ak suuf, ak biir géej ak xóote yépp.
7Mooy yékkateey niir fa cati àddina, sàkkal taw ay melax, yebbee ngelaw cay dencam,
8fàdd luy taaw fa Misra, doom aadama, ba ci mala.
9Yeen waa Misra, moo yónnee ay firndeeki kéemaan fi seen biir, ñeel Firawnaak jawriñam ñépp.
10Moo duma ay xeeti xeet, bóom buur yu mag yi,
11muy Siwon buurub Amoreen ña, ak Og buuru Basan, ak buuri Kanaan ñépp.

Read Sabóor 135Sabóor 135
Compare Sabóor 135:4-11Sabóor 135:4-11