9Say sarxalkat, yal nañu woddoo njekk, sa wóllëre yi sarxolleendoo.
10Xoolal ci Daawuda, sa jaam ba, bul gàntu ki nga fal.
11Aji Sax ji daa giñal Daawuda dëgg gu mu dul dëddu, ne ko: «Ku jóge sa geño laay wuutal ci sa jal bi,
12te say doom, bu ñu sàmmee sama kóllëre, ak sama kàdduy seede yi ma leen di xamal, seeni doom it ñooy tooge sa jal ba fàww.»
13Aji Sax ji kat a tànn Siyoŋ, taamu faa dëkke.
14Mu ne: «Fii laay dal-loo ba fàww, fii laay dëkk, maa ko taamu.
15Dund bi, ma barkeela barkeel, néew-ji-doole yi, ma reggal;
16sarxalkat yi, ma wodde njot; way-gëm ñi di sarxollee sarxolle.
17Fa laay dooleele Daawuda, taalal ki ma fal,
18ay noonam, ma wodde gàcce; moom, kaalaam ne ràññ.»