5Damay xaar Aji Sax ji, di ko xaare xol, di yaakaar kàddoom.
6Wattukat bi yàkkamti njël, wattukat bi yàkkamti njël, laa ne, ni ma yàkkamtee Aji Sax jee ko raw.
7Éey Israyil, négandikul Aji Sax ji. Aji Sax jee gore, te yaatug njot.
8Mooy jot Israyil ci ñaawtéefam yépp.