3Sama gannaaw gi lañu gàbba gàbb, rëdd koo rëdd nib tool.
4Waaye Aji Sax ji boroom njekk dog na buumi ñu bon ña.
5Képp ku noonoo Siyoŋ yal nañu ko dëpp, gàcceel ko.
6Yal nañu mel ni ñax mu saxem xadd, balaa law, lax.
7Du doyub ŋëb ku ko dog; du doyub say ku ko for.