3Lu réy la nu Aji Sax ji defal moos, nu bég.
4Aji Sax ji, rikk delloo nu na woon, ni ngay delloo wal yu ŋiis, mu walaat ca àllub Negew.
5Kuy ji di jooy, yal na góob, di sarxolle.
6Ku doon wéya wéy, di jooy; ŋàbb mbuusum jiwoom, yal na dikka dikk, di woy, ñibbaale sabaaram.