Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor - Sabóor 122

Sabóor 122:3-9

Help us?
Click on verse(s) to share them!
3Céy, Yerusalem, dëkkub tabax bu baax, bi booloo, di benn.
4Fii la giiri Israyil di yéegsi, di giir yi Ki Sax séddoo. Ñu ngi santsi Aji Sax ji, ni ko Israyil warloo.
5Fii la ngànguney Israyil tege, askanu Daawuda toog ca, di àtte.
6Dagaanleen jàmmi Yerusalem: «Yerusalem, yal na sa xeli soppe dal,
7jàmm ne ñoyy fi say tata wër, te xel dal ci biir këri Buur.»
8Mbokk ak xarit a waral may ñaan jàmmi Yerusalem.
9Sunu kër Yàlla Aji Sax jee ma tax di sàkku ngëneelu Yerusalem.

Read Sabóor 122Sabóor 122
Compare Sabóor 122:3-9Sabóor 122:3-9