Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor - Sabóor 119

Sabóor 119:92-97

Help us?
Click on verse(s) to share them!
92Su ma bégewuloon saw yoon, sànkoo sama toskare ji.
93Duma fàtte mukk say tegtal, ci nga may musale.
94Yaa ma moom, wallu ma; say tegtal laay sàkku.
95Man la ñu bon ñi tëru, nar maa sànk, waaye sa kàdduy seede laay niir.
96Gis naa ne lu mat lu ne am na kemu, waaye sa santaane mat ba wees kemu.
97Maaka sopp saw yoon, di ko jàngat bés bu jot.

Read Sabóor 119Sabóor 119
Compare Sabóor 119:92-97Sabóor 119:92-97