19Mbooloo mépp a ko doon wuta laal ndax leer guy bàyyikoo ca moom, di faj ñépp.
20Yeesu nag xool ay taalibeem, ne leen: «Ndokklee yeen ñi néewle, nde nguurug Yàlla, yeenay boroom.
21Ndokklee yeen ñi xiif tey, nde dingeen regg. Ndokklee yeen ñiy jooy tey, nde dingeen ree.
22Ndokklee yeen, bu leen nit ñi bañee, daggook yeen, saaga leen, sikkal seen der ndax Doomu nit ki.
23Bésub keroog, bégleen te bànneexu bay fecc ndax seen yoolub ëllëg bu réy, nde noonu la seen maami bañ yooyu daan def ak yonent ya.
24Waaye wóoy ngalla yeen ñi barele, ndax neexle ngeen ba noppi.
25Wóoy ngalla yeen ñi regg tey, ndax dingeen xiif ëllëg. Wóoy yeen ñiy ree tey, ndax dingeen tiislu, dingeen jooy.
26Wóoy ngalla yeen, bu leen ñépp dee waxal lu baax, ndax noonu rekk la maami ñooñu daan jëfe ak yonenti caaxaan ya.
27«Yeen ñi may déglu, dama ne, seeni noon, soppleen leen, seeni bañ, defal-leen leen lu baax.
28Ñi leen di móolu, yéeneleen leen lu baax, ñi leen di soxore, ñaanal-leen leen.
29Ku leen talaata cib lex, dékkleen ko ba ca des. Ku nangu seen mbubb mu mag, buleen ko teree jëlaale seenub turki.
30Képp ku leen ñaan, mayleen ko; ku nangu seen yëf, buleen ko ko laaj.
31Lu ngeen bëgg nit ñi defal leen ko nag, nangeen leen ko defale noonu.
32«Su dee ñi leen sopp doŋŋ ngeen sopp, ana lu ngeen ci wara yooloo? Bàkkaarkat yi sax, ñi leen sopp, sopp nañu leen.
33Te su dee ñi leen defal lu baax doŋŋ ngeen defal lu baax, ana lu ngeen ci wara yooloo? Bàkkaarkat yeet noonu doŋŋ lañuy jëfe.
34Te su dee ñi ngeen yaakaare ndelloo doŋŋ ngeen lebal, ana lu ngeen ci wara yooloo? Bàkkaarkat yi it, yaakaar ndelloo lu mat sëkk moo tax ñuy leblante.
35Yeen kay, soppleen seeni noon, defleen lu baax, lebleleen te baña yaakaar ndelloo. Su boobaa seenub yool réy, ngeen di doomi Aji Kawe ji, ndax moom de ñi santadi te bon, moo leen di baaxe.
36Ni seen Baay ame yërmande nag, nangeen ni ame yërmande.
37«Buleen di sikkale, su boobaa deesuleen sikkal. Buleen yeyale kenn ab daan, ngir ñu bañ leena yeyale ab daan. Baleleen, ñu baal leen.
38Mayeleen, ñu may leen; natt bu duun bu ñu rokkas, yëngal, mu fees bay tuuru, moom lees leen di nàddil ci seen mbubb. Ndax natt bi ngeen di nattale, moom lees leen di nattale.»
39Yeesu léebati leen, ne leen: «Ndax gumba dina wommat gumba? Mbaa duñu ànd tàbbi ci kàmb?
40Taalibe sutul sëriñam, waaye bépp taalibe bu jàng ba wàcc, tollook sëriñam.
41«Ana looy xoole xatax bi ci sa bëtu mbokk te gànj gi ci sa bëtu bopp gisuloo ko?
42Ana noo mane ne sa mbokk: “Mbokk mee, xaaral, ma dindil la xatax gi ci sa bët,” te yaw ci sa bopp gànj gi ci sa bët, gisuloo ko? Jinigalkat bi! Jëkkala dindi gànj gi ci sa bët. Su boobaa dinga gis bu baax xatax gi ci sa bëtu mbokk, ba dindil ko ko.
43«Garab gu neex du meññ doom yu naqari, te garab gu naqari it du meññ doom yu neex.
44Garab gu nekk, meññeefam lees koy xàmmee. Ag dédd, deesu ci witte doomi figg; ay dagg it, deesu ci jële doomi reseñ.
45Nit ku baax, dencub ngëneel ba ca biir xolam, ca lay jële lu baax la mu sàlloo; nit ku bon it, dencub safaan ba ca biir xolam, ca lay jële safaan ba mu sàlloo. Gémmiñ daal, la fees xolu boroom lay wax.
46«Ana lu ngeen ma naa “Sang bi, Sang bi,” te jëfewuleen samay wax?
47Képp ku ñëw ci man, dégg samay wax te di ko jëfe, dinaa leen won nu muy mel.