Text copied!
Bibles in Wolof

LUUG 6:19-47 in Wolof

Help us?

LUUG 6:19-47 in Téereb Injiil

19 Ñépp a ngi ko doon wuta laal ndax doole jiy jóge ci moom, di faj ñépp.
20 Yeesu xool ay taalibeem, ne leen: «Yéen ñi néew doole, barkeel ngeen, ndaxte nguuru Yàlla, yéena ko yelloo.
21 Yéen ñi xiif léegi, barkeel ngeen, ndax dingeen regg. Yéen ñiy naqarlu léegi, barkeel ngeen, ndax dingeen ree.
22 Barkeel ngeen, bu leen nit ñi bañee, di leen dàq ak a saaga, di sib seen tur ngir Doomu nit ki.
23 Bu boobaa bégleen te bànneexu, ndax seen yool dina réy ci laaxira. Ndaxte noonu la maami seeni bañ daan fitnaale yonent yi.
24 Waaye nag yéen boroom alal yi, torox ngeen, ndaxte jot ngeen ba noppi seen bànneex.
25 Yéen ñiy lekk ba suur léegi, torox ngeen, ndax ëllëg dingeen xiif. Yéen ñiy ree léegi, torox ngeen, ndax dingeen am aw naqar, ba jooy xàcc.
26 Torox ngeen bu leen ñépp dee waxal lu baax, ndaxte noonu la seeni maam daan jëfe ak ña doon mbubboo yonent.
27 «Waaye maa ngi leen koy wax, yéen ñi may déglu, soppleen seeni bañaale tey defal lu baax ñi leen bañ.
28 Yéeneleen lu baax ñi leen di móolu, te ñaanal ñi leen di sonal.
29 Ku la talaata cib lex, jox ko ba ca des. Kuy nangu sa mbubb mu mag, bul téye sa turki.
30 Képp ku la ñaan, may ko, te ku nangu say yëf, bu ko ko laaj.
31 Defal-leen nit ñi li ngeen bëgg, ñu defal leen ko.
32 «Su ngeen soppee ñi leen sopp, ban ngërëm ngeen ciy am? Ndaxte bàkkaarkat yi sax sopp nañu ñi leen sopp.
33 Te bu ngeen defalee lu baax ñi leen koy defal, ban ngërëm ngeen ciy am? Bàkkaarkat yi it dañuy def noonu.
34 Te bu ngeen dee leble te yaakaar ci ndelloo, ban ngërëm ngeen ciy am? Bàkkaarkat yi it dañuy lebal seeni moroom, ngir ñu delloo leen ko.
35 Waaye soppleen seeni noon, di leen defal lu baax, tey leble, baña yaakaar ñu delloo leen ko. Noonu seen yool dina mag te dingeen wone ne yéenay doomi Aji Kawe ji, ndaxte Yàlla day wone mbaaxam ci ñu goreedi ñi ak ñu soxor ñi.
36 Nangeen am yërmande, ni seen Baay ame yërmande.
37 «Buleen àtte seeni moroom ak ñaaw njort, te deesu leen àtte. Buleen daan kenn, te deesu leen daan. Baal-leen ñi ci des, te dinañu leen baal.
38 Mayeleen te dinañu leen may. Dinañu leen ëmbal natt bu baax bu ñu rokkos te yëngal ko, mu fees bay tuuru. Ndaxte dees na leen nattal ak natt, bi ngeen di nattale.»
39 Noonu Yeesu wax na leen beneen léeb ne leen: «Ndax gumba man na wommat moroomam? Mbaa duñu daanu ñoom ñaar ci kàmb?
40 Taalibe gënul kilifaam, waaye taalibe bu jàng ba wàcc, dina yem ak kilifaam demin.
41 «Lu tax ngay xool ñax gi ci sa bëtu mbokk, te gisuloo gànj gi ci sa bët yaw?
42 Nan nga mana waxe sa mbokk: “Sama xarit, may ma, ma dindil la ñax gi ci sa bët,” yaw mi gisul gànj gi nekk ci sa bët? Naaféq! Jëkkala dindi gànj gi ci sa bët, te noonu dinga mana gis bu leer, ngir dindi ñax gi ci sa bëtu mbokk.
43 «Garab gu baax du meññ doom yu bon, te garab gu bon du meññ doom yu baax.
44 Ndaxte garab, meññeefam lañu koy xàmmee. Deesul witte figg ci dédd, walla reseñ ci xaaxaam.
45 Noonu nit ku baax, lu baax lay wax, ndax loolu la denc ci xolam, te nit ku bon, lu bon lay wax, ndaxte denc na lu bon ci xolam. Ndaxte gémmiñ, la fees xolam lay wax.
46 «Lu tax ngeen may wooye “Boroom bi, Boroom bi,” te dungeen def li may wax?
47 Képp ku ñëw ci man, di dégg samay wax te di ko jëfe, ma won leen nu muy mel.
LUUG 6 in Téereb Injiil

Luug 6:19-47 in Kàddug Yàlla gi

19 Mbooloo mépp a ko doon wuta laal ndax leer guy bàyyikoo ca moom, di faj ñépp.
20 Yeesu nag xool ay taalibeem, ne leen: «Ndokklee yeen ñi néewle, nde nguurug Yàlla, yeenay boroom.
21 Ndokklee yeen ñi xiif tey, nde dingeen regg. Ndokklee yeen ñiy jooy tey, nde dingeen ree.
22 Ndokklee yeen, bu leen nit ñi bañee, daggook yeen, saaga leen, sikkal seen der ndax Doomu nit ki.
23 Bésub keroog, bégleen te bànneexu bay fecc ndax seen yoolub ëllëg bu réy, nde noonu la seen maami bañ yooyu daan def ak yonent ya.
24 Waaye wóoy ngalla yeen ñi barele, ndax neexle ngeen ba noppi.
25 Wóoy ngalla yeen ñi regg tey, ndax dingeen xiif ëllëg. Wóoy yeen ñiy ree tey, ndax dingeen tiislu, dingeen jooy.
26 Wóoy ngalla yeen, bu leen ñépp dee waxal lu baax, ndax noonu rekk la maami ñooñu daan jëfe ak yonenti caaxaan ya.
27 «Yeen ñi may déglu, dama ne, seeni noon, soppleen leen, seeni bañ, defal-leen leen lu baax.
28 Ñi leen di móolu, yéeneleen leen lu baax, ñi leen di soxore, ñaanal-leen leen.
29 Ku leen talaata cib lex, dékkleen ko ba ca des. Ku nangu seen mbubb mu mag, buleen ko teree jëlaale seenub turki.
30 Képp ku leen ñaan, mayleen ko; ku nangu seen yëf, buleen ko ko laaj.
31 Lu ngeen bëgg nit ñi defal leen ko nag, nangeen leen ko defale noonu.
32 «Su dee ñi leen sopp doŋŋ ngeen sopp, ana lu ngeen ci wara yooloo? Bàkkaarkat yi sax, ñi leen sopp, sopp nañu leen.
33 Te su dee ñi leen defal lu baax doŋŋ ngeen defal lu baax, ana lu ngeen ci wara yooloo? Bàkkaarkat yeet noonu doŋŋ lañuy jëfe.
34 Te su dee ñi ngeen yaakaare ndelloo doŋŋ ngeen lebal, ana lu ngeen ci wara yooloo? Bàkkaarkat yi it, yaakaar ndelloo lu mat sëkk moo tax ñuy leblante.
35 Yeen kay, soppleen seeni noon, defleen lu baax, lebleleen te baña yaakaar ndelloo. Su boobaa seenub yool réy, ngeen di doomi Aji Kawe ji, ndax moom de ñi santadi te bon, moo leen di baaxe.
36 Ni seen Baay ame yërmande nag, nangeen ni ame yërmande.
37 «Buleen di sikkale, su boobaa deesuleen sikkal. Buleen yeyale kenn ab daan, ngir ñu bañ leena yeyale ab daan. Baleleen, ñu baal leen.
38 Mayeleen, ñu may leen; natt bu duun bu ñu rokkas, yëngal, mu fees bay tuuru, moom lees leen di nàddil ci seen mbubb. Ndax natt bi ngeen di nattale, moom lees leen di nattale.»
39 Yeesu léebati leen, ne leen: «Ndax gumba dina wommat gumba? Mbaa duñu ànd tàbbi ci kàmb?
40 Taalibe sutul sëriñam, waaye bépp taalibe bu jàng ba wàcc, tollook sëriñam.
41 «Ana looy xoole xatax bi ci sa bëtu mbokk te gànj gi ci sa bëtu bopp gisuloo ko?
42 Ana noo mane ne sa mbokk: “Mbokk mee, xaaral, ma dindil la xatax gi ci sa bët,” te yaw ci sa bopp gànj gi ci sa bët, gisuloo ko? Jinigalkat bi! Jëkkala dindi gànj gi ci sa bët. Su boobaa dinga gis bu baax xatax gi ci sa bëtu mbokk, ba dindil ko ko.
43 «Garab gu neex du meññ doom yu naqari, te garab gu naqari it du meññ doom yu neex.
44 Garab gu nekk, meññeefam lees koy xàmmee. Ag dédd, deesu ci witte doomi figg; ay dagg it, deesu ci jële doomi reseñ.
45 Nit ku baax, dencub ngëneel ba ca biir xolam, ca lay jële lu baax la mu sàlloo; nit ku bon it, dencub safaan ba ca biir xolam, ca lay jële safaan ba mu sàlloo. Gémmiñ daal, la fees xolu boroom lay wax.
46 «Ana lu ngeen ma naa “Sang bi, Sang bi,” te jëfewuleen samay wax?
47 Képp ku ñëw ci man, dégg samay wax te di ko jëfe, dinaa leen won nu muy mel.
Luug 6 in Kàddug Yàlla gi