Text copied!
CopyCompare
Téereb Injiil - JËF YA - JËF YA 8

JËF YA 8:29-39

Help us?
Click on verse(s) to share them!
29Xel mi nag ne Filib: «Dabal watiir wale.»
30Noonu Filib dawsi, mu dégg waayi Ecópi ja, di jàng téereb yonent Yàlla Esayi. Mu laaj ko: «Ndax xam nga li ngay jàng?»
31Mu ne ko: «Nu ma ko mana xame, su ma ko kenn firilul?» Mu woo Filib nag, mu yéeg, toog ak moom.
32Fekk aaya yii la doon jàng ci Mbind mi: «Yóbbu nañu ko ni xar mu ñuy rendiji; ni mburt mu luu ci kanam i watkat, mu ne cell.
33Ci toroxteem nangu nañu dëggam; ñi mu tollool jamono, ku ci xalaat lii? Jële nañu bakkanam ci àddina.»
34Jaraaf ja nag ne Filib: «Maa ngi lay laaj, ci mbirum kan la yonent bi jëmale wax ji? Ndax mbirum boppam lay wax mbaa mu keneen?»
35Noonu Filib tàmbali ci aaya yooyu, xamal ko xibaaru jàmm bi ci mbirum Yeesu.
36Bi ñuy jaar ci yoon wi, ñu agsi ci ndox. Jaraaf ja ne ko: «Ndox a ngi nii, ana lu tere, nga sóob ma ci?»
38Mu santaane nag, ñu taxawal watiir wa; Filib ak jaraaf ja wàcc ñoom ñaar ci biir ndox ma, mu sóob ko ca.
39Ba noppi ñu génn ca ndox ma, te ca saa sa Xelu Boroom bi fëkk Filib, ba jaraaf ja gisatu ko, waaye mu toppaat yoonam, ànd ak mbég.

Read JËF YA 8JËF YA 8
Compare JËF YA 8:29-39JËF YA 8:29-39