1Kàdduy Amos a ngi, di boroom jur bu dëkkoon Tekowa. Mu am peeñu mu jëm ci Israyil ci janti Osiyas buurub Yuda ak janti doomu Yowayas, Yerbowam buurub Israyil. Loolu tollu ci ñaari at lu jiitu yëngu-yëngu suuf ba.
2Mu ne: Aji Sax jeey yëmmoo fa Siyoŋ, Yerusalem lay àddoo, parluy sàmm si ne faraas, mbooyum kaw tundu Karmel lax.
3Aji Sax ji da ne: «Ñetti bàkkaar, su ma yeboo ne ñeent, laay sikke waa Damaas, te duma fomm seeni duma. Ñoo bàcce waa Galàdd bàccukaayi weñ.
4Maay yebal sawara seen waa kër Buur Asayel, mu xoyom taaxi Buur Ben Addàd.
5Maay dàjji bunti dëkkub Damaas, faagaagal waa xuru Awen, boole ca boroom Bet Eden. Waa Siri dugg ngàllo, dellu Kir.» Aji Sax jee ko wax.
6Aji Sax ji nee: «Ñetti bàkkaar, su ma yeboo ne ñeent, laay sikke waa Gasa, te duma fomm seeni duma. Ñoo jàpp njaam mbooloom lëmm, jalax Edomeen ña.
7Maay yebal sawara ca tatay Gasa, mu xoyom ay taaxam.
8Maay fàkkas waa Asdodd, fàkkas boroom yetu nguur fa Askalon, fél Ekkron, ndesu Filisteen ña sànku.» Boroom bi Aji Sax jee ko wax.
9Aji Sax ji nee: «Ñetti bàkkaar, su ma yeboo ne ñeent, laay sikke waa Tir, te duma fomm seeni duma. Ñoo jàpp mbooloom lëmm, jalax ca Edomeen ña, te sédduñu ci kóllëreg bokk.
10Damay yebal sawara ca tatay Tir, mu xoyom ay tataam.»
11Aji Sax ji nee: «Ñetti bàkkaar, su ma yeboo ne ñeent, laay sikke waa Edom, te duma fomm seeni duma. Ñoo toppe seen bokki bànni Israyil saamar, jalax yërmande, mer mer mu dul meddi ak xadar ju dul giif mukk.
12Maay yebal sawara fa Teman, mu xoyomaale tatay Boccra.»
13Aji Sax ji nee: «Ñetti bàkkaar, su ma yeboo ne ñeent, laay sikke Amoneen ñi, te duma fomm seeni duma. Ñoo butti ay jigéeni biir ca Galàdd ba ñuy xare ngir yokk seen suuf.
14Maay jafal ca kaw tatay Raba, mu xoyom ay taaxam, yuux ya jib bésub xare, ci biir callweer bésub ngëlén.
15Seen buur ay duggi ngàllo, mooki kàngamam.» Aji Sax jee ko wax.