Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Amos

Amos 3

Help us?
Click on verse(s) to share them!
1Dégluleen kàddu gii Aji Sax ji wax ci yeen, bànni Israyil, mu jëm ci seen mboolem xeet wi mu génnee réewum Misra. Mu ne:
2«Yeen doŋŋ laa ràññee ci mboolem askani suuf. Moo tax ma di leen mbugal ndax seen ñaawtéef gépp.»
3Ñaar dina ànd te digewuñub dajee?
4Gaynde dina ŋarem ngeer te fàddul? Am gaynde gu ndaw dina xiiroom paxam te jàppul?
5Picc dina keppu te fiireesu koo? Am ag fiir dina fettax te jàppul?
6Bu liitu xare jibee, waa dëkk ba du tiit a? Am aw ay dina dab ub dëkk te du Aji Sax ji?
7Du lenn moos lu Boroom bi Aji Sax ji def, te déeyu ko yonent yiy jaamam.
8Bu gaynde yëmmoo, ana ku dul tiit? Ana ku saña baña biral waxyu, bu ko Boroom bi Aji Sax ji waxee?
9Yéeneleen ca biir taaxi Asdodd ak ca biir taaxi Misra. Neleen: «Dajeleen ca kaw tundu Samari, ba gis na Samari salfaañoo, ak notaange ga fa nit di daj.
10Xamuñu sax def njub.» Kàddug Aji Sax jee. «Dañuy jal alalu fitnaak yàqute ci seen biiri taax.»
11Moo tax Boroom bi Aji Sax ji ne: «Ab noon dina gaw seenum réew, néewal leen doole, lël seeni taax.»
12Aji Sax ji nee: «Wallub sàmm ak gàtt bu gaynde fàdd weesul ñaari yeel, dogitu nopp. Kuy wallu bànni Israyil ga ca Samareet, xanaa dogu basaŋ, dammitu lal.
13Dégluleen te àrtu waa kër Yanqóoba.» Kàddug Boroom bi Aji Sax jee, Yàlla ji ci gàngoori xare yi.
14«Bés bu may mbugale Israyil ay bàkkaaram, damay tasaale sarxalukaayi Betel. Béjjén yi ci cati sarxalukaay ba dog, rot.
15Maay màbbaale këru taax ak këru àll; kër yu ñu rafetale bëñu ñay dina yàqu, te kër yu bare dootu taxaw.» Kàddug Aji Sax jee.