1Man njiit li, maa ngi lay bind, yaw sama xarit Gayus, mi ma bëgg ci sama xol.
2Sama soppe, maa ngi ñaan, Yàlla may la jàmm ci lépp, ànd ak wér-gi-yaram, ju mel ni sa naataangeg xol.
3Sunuy bokk ñëw nañu te seede ni nga fonke dëgg gi, ba wéer ci sa dund gépp, te bég naa ci lool.
4Awma mbég mu ëpp lii: ma dégg ne samay doomi diine ñu ngiy jaar ci tànki dëgg.
5Yaw sama xarit, sa takkute fés na ci teeru bi ngay teeru bokk yi, te fekk xamoo leen.
6Seedeel nañu sa mbëggeel fi kanam mbooloom ñi gëm. Taxawu leen nag ci seen yoon taxawu gu neex Yàlla.
7Ndaxte turu Kirist la leen taxa jóg, te sàkkuwuñu daray ku gëmul.
8Nun nag fàww nu teeru ñu mel ni ñoom, ngir nu ànd ak ñoom liggéeyal dëgg.
9Bind naa mbooloo mi bataaxal, waaye Joteref, mi bëgg not ñépp, du dégg sunu ndigal.
10Kon nag su ma ñëwee, dinaa fàttali li mu def lépp, ci di nu sosal ci kàdduy neen yu ñaaw. Yemu foofu sax, waaye nanguwula teeru bokk yi, rax-ca-dolli ku leen bëgga teeru, mu gàllankoor ko, dàq ko ci mbooloo mi.
11Sama xarit, bul roy lu bon, waaye lu baax rekk. Kuy def lu baax, ci Yàlla nga bokk; kuy def lu bon, xamoo dara ci Yàlla.
12Naka Demetirus nag, ñépp seedeel nañu ko lu baax, te dëgg gi ci moom sax seedeel na ko ko. Nun itam seedeel nanu ko te wóor na ma ne sunu seede dëgg la.
13Am na lu bare lu ma la bëggoona wax, waaye lépp xajul ci kayit.
14Kon yaakaar naa laa seetsi balaa yàgg, jàkkaarlook yaw, nu waxtaan ci.
15Yal na jàmm ànd ak yaw. Xarit yi yépp ñu ngi lay nuyu. Nuyul nu sunuy xarit, kenn ku nekk ci turam.