4Buur, jëfe yoon mooy dooleem, te yaa saxal njub, yoon ak njekk ci askanu Yanqóoba.
5Màggal-leen sunu Yàlla, Aji Sax ji, te sujjóot fa ndëggastalam. —Kee sell!
6Musaak Aaróona bokk ciy sarxalkatam, Samiyel bokk ca ñay tudd turam. Ñuy ñaan Aji Sax ji, mu di leen nangul.