4 Buur, jëfe yoon mooy dooleem, te yaa saxal njub, yoon ak njekk ci askanu Yanqóoba.
5 Màggal-leen sunu Yàlla, Aji Sax ji, te sujjóot fa ndëggastalam. —Kee sell!
6 Musaak Aaróona bokk ciy sarxalkatam, Samiyel bokk ca ñay tudd turam. Ñuy ñaan Aji Sax ji, mu di leen nangul.