8Siyoŋ dégg ca, bég, waa Yuda it di bànneexoo àttey Aji Sax jii.
9Aji Sax ji, Aji Kawe ji tiim suuf sépp; yaaka màgga màgg, ba sut tuuroo tuur.
10Yeen soppey Aji Sax ji, bañleen lu bon. Aji Sax jeey sàmm ay wóllëreem, di leen musal ci ku bon.
11Jub, leerlu; jubal, bég.