8 Siyoŋ dégg ca, bég, waa Yuda it di bànneexoo àttey Aji Sax jii.
9 Aji Sax ji, Aji Kawe ji tiim suuf sépp; yaaka màgga màgg, ba sut tuuroo tuur.
10 Yeen soppey Aji Sax ji, bañleen lu bon. Aji Sax jeey sàmm ay wóllëreem, di leen musal ci ku bon.
11 Jub, leerlu; jubal, bég.