3Siiwal-leen teddngaam fi biir xeet yi, xamal waasoo waaso ay jalooreem.
4Aji Sax jee màgg, jara santa sant te gëna mata ragal lépp lu ñuy jaamu.
5Mboolem yàlla yi xeet yiy jaamu, yàllantu la, waaye Aji Sax jee sàkk asamaan.
6Màggaay ak daraja, fa moom, dooleek taar, fa këram gu sell.
7Yeen làngi xeet yi, seedeel-leen Aji Sax ji; seedeel-leen Aji Sax ji teddngaak doole.
8Seedeel-leen Aji Sax ji teddngay turam, yékkatil kob sarax, duggaale ëttam.
9Sujjóotal-leen Aji Sax ji làmboo sellnga, te àddina wërngal këpp di ko loxal.
10Neleen xeet yi Aji Sax jeey buur: àddinaa ngii, dëju te raful. Mooy àtte xeet yi njub.
11Asamaanoo, bégal! Suufoo, bànneexul! Géejoo, riiral yaak li la fees,