Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor - Sabóor 95

Sabóor 95:5-9

Help us?
Click on verse(s) to share them!
5moom géej, sàkk ko, moom jéeri ji mu mooñ.
6Nan sëgg, sujjóot, sukkal Aji Sax ji nu sàkk.
7Mooy sunu Yàlla, nuy xeet wi muy foral, diy gàtt ciy loxoom. Bésub tey yal nangeen dégg kàddoom
8ga mu noon: «Buleen të, na woon fa Meriba, jantub keroog fa Maasa, ca màndiŋ ma,
9fa ma seeni maam doon nattoo, di ma seetlu te gis la ma def.

Read Sabóor 95Sabóor 95
Compare Sabóor 95:5-9Sabóor 95:5-9