2Yaw miy àtte àddina, jógal yool ku bew.
3Aji Sax ji, fu ku bon kiy àkki? Fu ku bon kiy kañu àkki?
4Ñu ngi làmmiñoo reewande, képp kuy def lu bon di damu.
5Aji Sax ji, say ñoñ lañuy dëggaate; say séddoo lañuy néewal.
6Jëtun akub doxandéem, ñu faat; ab jirim, ñu bóom,
7te naa: «Ki Sax gisu ci, Yàllay Yanqóoba jii yégu ko.»
8Yeen bokk yu dofe yi, moytuleen. Gàtt xel yi, kañ ngeen di muus?
9Ki jëmbati nopp, da dul dégg a? Am ki xari gët, da dul gis?
10Kiy yar yéefar yi, da dul mbugalee? Du mooy kiy xamal nit?
11Aji Sax ji xam na xalaatu nit, xam ne cóolóolu neen la.
12Ki Sax, ndokklee ki ngay yar, tàggat ko ci saw yoon,
13dëfal ko ci bési safaan, ba keroog ñuy gasal ku bon.
14Boroom bi kat du wacc ñoñam mukk, du bàyyi ay séddoom.
15Àtte dina dellu laloo njekk, képp ku jub topp ca.