7Ku ñàkk xel réere ko, ku dofe umple ko.
8Bu ku bon sëqlee nim ñax, képp kuy def lu bon di yokkule, dañoo nara sànku ba fàww rekk.
9Waaye yaw ma fa kaw, yaay Aji Sax ji ba fàww.
10Aji Sax ji, sa noon yi kay, ndeke yoo; ndeke yoo sa noon yi, sànku rekk; defkati mbon ñépp, fëlxoo rekk.
11May nga ma dooley nagu àll, ma diwoo diw gu bees.
12Maa gis jéllu noon yi, dégg yuuxi ñu bon ñi may tëru.