7 Ku ñàkk xel réere ko, ku dofe umple ko.
8 Bu ku bon sëqlee nim ñax, képp kuy def lu bon di yokkule, dañoo nara sànku ba fàww rekk.
9 Waaye yaw ma fa kaw, yaay Aji Sax ji ba fàww.
10 Aji Sax ji, sa noon yi kay, ndeke yoo; ndeke yoo sa noon yi, sànku rekk; defkati mbon ñépp, fëlxoo rekk.
11 May nga ma dooley nagu àll, ma diwoo diw gu bees.
12 Maa gis jéllu noon yi, dégg yuuxi ñu bon ñi may tëru.