4xalamu fukki buum ànd ak moroom ma, xeetu kooraa jibandoo.
5Aji Sax ji, yaa ma bégale say jaloore, may sarxolle ci say manoore.
6Aji Sax ji, yaa réyi jëf; xóoti pexe.
7Ku ñàkk xel réere ko, ku dofe umple ko.
8Bu ku bon sëqlee nim ñax, képp kuy def lu bon di yokkule, dañoo nara sànku ba fàww rekk.