10Aji Sax ji, sa noon yi kay, ndeke yoo; ndeke yoo sa noon yi, sànku rekk; defkati mbon ñépp, fëlxoo rekk.
11May nga ma dooley nagu àll, ma diwoo diw gu bees.
12Maa gis jéllu noon yi, dégg yuuxi ñu bon ñi may tëru.
13Ku jub day naat nig tàndarma, màgg ni seedaru Libaŋ