10 Aji Sax ji, sa noon yi kay, ndeke yoo; ndeke yoo sa noon yi, sànku rekk; defkati mbon ñépp, fëlxoo rekk.
11 May nga ma dooley nagu àll, ma diwoo diw gu bees.
12 Maa gis jéllu noon yi, dégg yuuxi ñu bon ñi may tëru.
13 Ku jub day naat nig tàndarma, màgg ni seedaru Libaŋ