Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor - Sabóor 89

Sabóor 89:48-52

Help us?
Click on verse(s) to share them!
48Bàyyi ma xel, samay fan yàggul. Xanaa du neen a tax nga sàkk mboolem doom aadama?
49Ana kuy dund te du dee? Ku mana rëcc tëraayu bàmmeel? Selaw.
50Boroom bi, ana sa ngor la nga daan jëfe te nga giñale woon ko Daawuda ci sa worma?
51Boroom bi, bàyyil xel ci sa gàcceg jaam ñi, ak xeet yu bare yi ma yenu yépp.
52Aji Sax ji, say noon a ngi sewal buur bi nga fal, ne ko dann.

Read Sabóor 89Sabóor 89
Compare Sabóor 89:48-52Sabóor 89:48-52