1Muy woyu Sabóor, ñeel askanu Kore wu góor, jëm ci njiital jàngkat yi, dëppook galan bu ñuy wax Maalat Leyanot, di taalifu Eman, mi bokk ci giirug Esra.
2Éy Aji Sax ji, Yàlla ji may musal, bëccëg ma yuuxu, guddi ma yuuxu fi sa kanam.
3Yal na sama ñaan àgg fa yaw; teewlul, ma woote wall.
4Damaa suur këll ay musiba, ba soreetuma njaniiw,
5ñu sóoraale maak ñi wàcci biir bàmmeel. Ma mel ni jàmbaar ju kenn amatul yaakaar,
6bokk ci néew, yi dara waratul, mbaa ku ñu bóom, mu tëdd cim pax, faaleetoo ko, xanaa dagg ko, wacc.