1Muy woyu Sabóor, ñeel askanu Kore wu góor, jëm ci njiital jàngkat yi, dëppook galan bu ñuy wax Maalat Leyanot, di taalifu Eman, mi bokk ci giirug Esra.
2Éy Aji Sax ji, Yàlla ji may musal, bëccëg ma yuuxu, guddi ma yuuxu fi sa kanam.
3Yal na sama ñaan àgg fa yaw; teewlul, ma woote wall.
4Damaa suur këll ay musiba, ba soreetuma njaniiw,
5ñu sóoraale maak ñi wàcci biir bàmmeel. Ma mel ni jàmbaar ju kenn amatul yaakaar,
6bokk ci néew, yi dara waratul, mbaa ku ñu bóom, mu tëdd cim pax, faaleetoo ko, xanaa dagg ko, wacc.
7Tàbbal nga ma kàmb gu xóot, biir xóotey lëndëm.
8Yen nga ma sa xadar, tance ma sa gannax yépp. Selaw.
9Dàqal nga may xame, tax nga ñu seexlu ma; ma tëju, génnatuma.
10Samay gët a ngi giim ndax naqar. Éy Aji Sax ji, maa ngi lay woo bés bu ne, dékk lay loxo.
11Ku dee, lu muy doyeeti say kéemaan? Ndax néew dina jóg di la màggal? Selaw.
12Dees na siiwal sa ngor biir bàmmeel, mbaa sa worma ci paxum sànkute?
13Ana kuy yég say kéemaan ci googu lëndëm? Ku lay seedeel njekk réew ma fàtte faloo?
14Aji Sax ji, man, yaw lay woo wall, xëy, kare la gii ñaan, ne la:
15Éy Aji Sax ji, loo may gàntale, di ma fuuylu?
16Mitit bay laatikaaf, sama ngone ba tey; sa mbugal yu raglu, ba bopp ubu ràpp!
17Sa mer mëdd ma, sa mbugal yu raglu sànk ma,
18mëdd ma nim ndox bés bu ne, gëndoo fi sama kaw.