Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor - Sabóor 86

Sabóor 86:5-10

Help us?
Click on verse(s) to share them!
5Boroom bi, yaa baax, di bale, di nàddil sa ngor képp ku lay sàkku.
6Éy Aji Sax ji, teewlul, ma ñaan la; déglul, ma tinu la.
7Bu ma la wooyee bésub njàqare, yaa may nangul.
8Boroom bi, doo moroomu tuur yi, te jëf melul ni sa jos.
9Boroom bi, mboolem xeet yi nga sàkk ñoo lay sujjóotalsi, di màggal sa tur.
10Yaa màgg te yéemey jëf, yaw doŋŋ yaa di Yàlla.

Read Sabóor 86Sabóor 86
Compare Sabóor 86:5-10Sabóor 86:5-10