13Ngor lu réy nga ma won, sorele maak tëraayu bàmmeel.
14Éy Yàlla, nit ñu bew a ma jógal, def gàngoor gu néeg, di rëbb sama bakkan, te seetuñu la ci.
15Waaye yaw Boroom bi Yàlla, yaa ñeewante, yërëm, yaa muñ mer, bare ngor ak worma.
16Geesu ma, baaxe ma. Dooleelal sab jaam, wallul ki sa jaam sukk jur!