5Éy Yàlla mi nuy musal, suqli nu, te meddi.
6Xanaa doo nu mere fàww, ba ca sët yaak sëtaat ya?
7Xanaa dinga leqli sa mbooloo, ba ñu man laa bànneexoo?
8Éy Aji Sax ji, won nu sa ngor, baaxe nu sag wall.
9Woykat ba nee: «Naa déglu lu Aji Sax ji Yàlla di wax.» Jàmm lay wax wóllëreem ñiy ñoñam, ba duñu dellu ci jëfi dof.