5 Éy Yàlla mi nuy musal, suqli nu, te meddi.
6 Xanaa doo nu mere fàww, ba ca sët yaak sëtaat ya?
7 Xanaa dinga leqli sa mbooloo, ba ñu man laa bànneexoo?
8 Éy Aji Sax ji, won nu sa ngor, baaxe nu sag wall.
9 Woykat ba nee: «Naa déglu lu Aji Sax ji Yàlla di wax.» Jàmm lay wax wóllëreem ñiy ñoñam, ba duñu dellu ci jëfi dof.