Text copied!
CopyCompare
Kàddug Yàlla gi - Sabóor - Sabóor 84

Sabóor 84:7-11

Help us?
Click on verse(s) to share them!
7Buy jàll xuru Jooyoo, mu saf ko bëti ndox, céebo sànge xur wa barke,
8muy gëna am doole, ba teewi fa Yàlla ca Siyoŋ.
9Éy Yàlla Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, déglul, ma ñaan la! Yàllay Yanqóoba, teewlu ma. Selaw.
10Éy Yàlla, geesul Buur, sunu kiirlaay, ngalla niiral kii nga fal.
11Benn fan ci sab ëtt de moo dàq junniy fan feneen. Sama taxawaayu bunt kër Yàlla moo ma gënal tëraayu biir xaymab ku bon.

Read Sabóor 84Sabóor 84
Compare Sabóor 84:7-11Sabóor 84:7-11