5Ndokklee ku dëkke sa kër, di la màggalati. Selaw.
6Ndokklee ku lay doolewoo, te namma topp njool ma jëm sa kër.
7Buy jàll xuru Jooyoo, mu saf ko bëti ndox, céebo sànge xur wa barke,
8muy gëna am doole, ba teewi fa Yàlla ca Siyoŋ.
9Éy Yàlla Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, déglul, ma ñaan la! Yàllay Yanqóoba, teewlu ma. Selaw.