10Éy Yàlla, geesul Buur, sunu kiirlaay, ngalla niiral kii nga fal.
11Benn fan ci sab ëtt de moo dàq junniy fan feneen. Sama taxawaayu bunt kër Yàlla moo ma gënal tëraayu biir xaymab ku bon.
12Aji Sax ji Yàllaa mat jant, mat kiiraay; yiw ak daraja, Aji Sax ji joxe; te du ngëneel lu muy bañal ku mat.