4Sa ñoñ lañuy rabatal, di mànkool sa séddoo yii.
5Ñu ne: «Ayca nu far seen xeet wi, ba deesul fàttlikooti turu Israyil.»
6Dañoo mànkoo kat, te yaw lañu takktool:
7muy néegi Edom ak Ismayla, néegi Mowab ak Agar,
8néegi Gebal, Amon ak Amaleg ak waa Filisteek waa Tir,
9réewum Asiri it fekki leen, di dooleel askanu Lóot wa. Selaw.
10Def leen na nga defoon waa Majan, def ko Sisera ak Yabin ca dexu Kison.
11Ña nga sànkoo Endor, ba doon ub tos fi kaw suuf.
12Defal seeni njiit na Oreb ak Seeb, def seen kilifa yépp ni Seba ak Salmuna,
13ña ne woon: «Nan séddoo parluy Yàlla yi.»
14Éy Yàlla, wëndeel leen ni callweer, ñu mel ni boob mu ngelaw wal.
15Éy Yàlla, ni daay di xoyome àll, sawara wa jafal tund ya,
16yal nanga leen ni toppeek sa dooley ngelaw, tiitale leen sa ngëlén.
17Aji Sax ji, sëlëm leen gàcce, ba ñu sàkku la.