1Muy kàddug Sabóor, giiroo ci Asaf. Yàlla toog na, di jiite ndajem boppam, di àtte ndawi péncam, naan:
2«Dungeen bàyyi àtteb njublaŋ, ak di faral ku bon? Selaw.
3Sàmmleen àqu néew-ji-dooleek jirim, tey àtte yoon ku ñàkk ak ku ndóol.
4Walluleen néew-ji-dooleek walaakaana, di leen xettli ci ku bon.