52Mu génne ñoñam niy gàtt, wommat leen ni gétt ca màndiŋ ma,
53ba yóbbu leen fu wóor te tiituñu; seeni noon, géej ga mëdd leen.
54Mu yóbbu leen fa suufam su sell sa, fa tund woowu mu jënde dooleem.
55Da leena dàqal ay xeet, dogal leen céru suuf, sancal giiri Israyil ca seeni xayma.
56Teewul ñuy diiŋat ak a gàntal Yàlla Aji Kawe ji, sàmmuñu ay dénkaaneem,
57xanaa dëddu, di ko wor ni seeni maam, toogadi ni xala gu yolom.
58Ñu di ko merlook seen bérabi jaamookaay, di ko fiirlook seen jëmmi tuur.
59Ba ko Yàlla yégee, mer na, ba jéppi Israyil lool.
60Mu gental dëkkuwaayam ba ca Silo, xaymaam ba mu sampoon ca doom aadama ya.
61Mu jébbal ngàllo màndargam dooleem, may gànjaram ca loxol noon ba.
62Daa bàyyee ñoñam saamaru noon, ndax mere yooya séddoom.
63Seeni waxambaane deeye xare, seeni janq lamb;
64seeni sarxalkat loroo saamar, te jëtun jooyul.
65Ca la Boroom bi yewwu ni ku doon nelaw, mel ni jàmbaar ju biiñ xabtal.
66Mu dóor noon ba yari gannaaw, teg leen gàcce gu dul fey,
67ba noppi xalab waa kër Yuusufa, te tànnul giirug Efrayim,
68xanaa tànn giirug Yuda, taamu tundu Siyoŋ wi mu sopp.
69Mu tabax këram gu sell, na mu mel fa kawa kaw, dëgër ni suuf, si mu samp ba fàww.
70Mu teg ca tabb Daawuda, jaamam ba, jële ko ca gétti xar ya,
71fa mu doon topptoo jur ga; mu sàmmal ko waa kër Yanqóoba, askanu Israyil wi mu séddoo.
72Daawuda sàmme leen xol bu mucc ayib, jiitee leen manooreem.