1Muy taalif bu giiroo ci Asaf. Yeen sama xeet, dégluleen, ma digal leen; teewluleen ma, ma wax leen.
2Maa ngi leen di léeb, di sulli kumpay démb,
3muy lu nu dégg, xam ko, sunuy maam xamal nu ko.
4Dunu ko nëbb sunuy doom, xanaa di ko jottli maas giy ñëw, xamal leen jaloorey Aji Sax ji ak kàttanam aki kéemaanam.
5Bindal na sëti Yanqóoba téereb seede, muy yoon wi mu tegal Israyil. Mu sant maam yi, ñu xamal ko seeni doom,
6ngir ñiy juddu ëllëg xam ko, am ay doom, ñu màgg, ba xamal ko seeni doom,
7ngir ñu wóolu Yàlla, baña fàtte jëfi Yàlla, di jëfey santaaneem,
8te baña roy seeni maam; maas gu të woon te déggadi, ñu ñàkk pastéef te sàmmuñu kóllërey Yàlla.
9Waa giirug Efrayim ñoo soxi fitt, te keroog xare ba ñoo daw.
10Ñoo sàmmul kóllërey Yàlla, gàntal yoonam,
11ba fàtte ay jalooreem, di kéemaan yi mu leen won.
12Fa seen kanami maam la def kéemaan, fa diiwaanu Cowan, réewum Misra.
13Moo xar géej ga, jal ndox ma nim tata, jàlle leen.
14Bëccëg mu jiitee leen aw niir, ak leeru sawara guddi gépp.
15Moo xar ay doj ca màndiŋ ma, mbàmbulaan wal, mu nàndal leen;
16mu sotti ndox mu balle ciw xeer, walal, mu safi dex.
17Teewul ñu wéy di moy Aji Kawe ji, di ko gàntal ca màndiŋ ma.
18Ñoo diiŋate Yàlla xol, di xemmem ñam wu bakkane.
19Ñuy waxal Yàlla naan: «Xam ngeen ne Yàlla manu noo taajal ndab ci màndiŋ mi!
20Dóor naw doj, moos, ndox ma fettax, wal ma baawaan, waaye aw ñam nag? Daa mana leel mbooloo mii aw yàpp?»
21Aji Sax ji dégg ci, mer lool; xolam tàng ci sëti Yanqóoba, am sànj tàkkal Israyil.
22Dañoo gëmul Yàlla, doyloowuñu wallam.